Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa génn ci nun, nu ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, xam nanu naka lanu lay nuyòo, leegi naka lanuy jullee ci yaw?
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële nañu ci Abdur Rahmaan ibn Abii Laylaa mu wax ne: Kahb ibn Hujrata dafa dajee ak man, ne ma: ndax du ma jox àddiya? Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa génn ci nun, nu ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi, xam nanu naka lanu lay nuyòo, leegi naka lanuy jullee ci yaw?, mu wax ne: "waxleen: Allaahumma salli halaa Muhammadin wa halaa aali Muhammadin kamaa sallayta halaa aali Ibraahiima, innaka Hamiidun Majiidun, Allaahumma baarik halaa Muhammadin wa halaa aali Muhammadin kamaa baarakta halaa aali Ibraahiima innaka Hamiidun Majiidun".
Explanation
" Maanaam: ki ñu sant ci sa jëmm ji ak ci sa melo yi ak ci say jëf, di ki yaatu ci sag màggaay ak ci sag kilifteef ak say may. "Allaahumma baarik halaa Muhammadin wa halaa aali Muhammadin kamaa baarakta halaa aali Ibraahiima" Maanaam: jox ko ci ay yiw ak i terànga ya ca gën a màgg, te nga dolli ko te saxal ko.
Benefits
Julli ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa war ci taaya ji mujj ci julli.
Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- xamal na Sahaaba yi nuyòo ak ni ñuy jullee ci moom.
Melo wii mooy melo wi gën a mat ci meloy julli ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

