Allaahumma innii ahuusu bi ka min hasaabil xabri, wa min hasaabin naari, wa min fitnatil mahyaa wal mamaati, wa min fitnatil Masiihid Dajjaali
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan ñaan daan na wax: " Allaahumma innii ahuusu bi ka min hasaabil xabri, wa min hasaabin naari, wa min fitnatil mahyaa wal mamaati, wa min fitnatil Masiihid Dajjaali". Am na ci jeneen wax ci Muslim: "bu kenn ci yéen noppee ci taaya ju mujj ji, na muslu ci Yàlla ci ñent: ci mbugalum Jahannama, ak ci mbugalu bàmmeel, ak ci fitnay dund ak dee, ak ci ayu Masiihud Dajjaal ".
Explanation
muslu ci Yàlla ci yooyu,
Bi ci njëkk: ci mbugalum bàmmeel.
Ñaareel bi: ci mbugalum sawara ëllëg bis-pénc.
Ñatteel bi: ci fitnay dund ci bànneexi àdduna yi nu araamal, ak lënt yiy réerale, ak fitnay dee, maanaam waxtuy sukuraat, ci jéng wolif lislaam mbaa sunna, walla fitnay bàmmeel niki laaji ñaari malaaka yi.
Ñenteel bi: fitnay Al-Masiihud-Dajjaal miy génn ci mujjug jamono, Yàlla di ci nattu ay jaamam; da koo jagleel cig tudd nag ngir màggug fitnaam ak i réeralateem.
Benefits
Mbugalum bàmmeel lu sax la te dëgg la.
Loraangey fitna ak solos muslu ci Yàlla ak ñaan ngir mucc ca.
Saxal ne Dajjaal dana génn ak fitnaam gu màgg ga.
Sopp nañu ñaan gii ginnaaw taaya ju mujj.
Sopp nañu ñaan ginnaaw bu ñu defee jëf ju sell.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

