seedeel naa Yàlla ne set naa wicc ci kenn ci yéen di nekk sama xarit, ndax Yàlla da maa jàpp xarit, niki mu jàppe Ibraahiima xarit
Jële nañu ci Jundub -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Dégg naa Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax li njëkk juroom i fan laata muy faatu naan: " seedeel naa Yàlla ne set naa wicc ci kenn ci yéen di nekk sama xarit, ndax Yàlla da maa jàpp xa…

