julli gi gën a diis ci naaféq yi mooy jullig gee ak jullig fajar, te bu ñu xamoon li nekk ci ñoom ñaar kon danañu ko teewe donte dañuy raam
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «julli gi gën a diis ci naaféq yi mooy jullig gee ak jullig fajar, te bu ñu xamoon li nekk ci ñoom ñaar kon danañu ko teewe donte dañuy raam, doon naa yittewoo digle ñu taxawal julli, ma digal benn waay mu jiite nit ñi, ma ànd ak ay góor ñu yor ay matti sawara, nu dem ci nit yi dul teewe julli gi, taal séen kër ya ca séen kaw».
Explanation
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa dogu ci digle ñu taxawal julli, mu jiital jenn waay mu wuutu ko jiite nit ñi, mu ànd ak ñu yor ay matti sawara dem ca ña dul teewe jullig mbooloo ma mu làkk séen kër ya ca séen kaw; ndax bàkkaar ya ñu def dafa tar, -waaye defu ko- ndax jigéen ña ca kër ya ak xale ya ak ña deful dara niki ñi am ngànt, te defuñu bàkkaar.
Benefits
Naaféq yi jubluwuñu ca séen jaamu ya lu dul ngistal ak ndéggtal, duñu dem ca julli ga lu dul bu leen nit ñi dee gis.
Yool bu màgg bi nekk ci julli gee ak fajar ànd ak mbooloo ma, ak ne ñoom ñaar de jar na ñoo teewe donte dangay raam.
Sàmmonte ak jullig gee ak fajar ag mucc la ci naaféq, waaye di leen wuute ci meloy naaféq yi la bokk.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

