Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daan na wax ginnaaw jullig farata gu ne
Jële nañu ci Warraad mi daa bindal Al-Muxiirata Ibn Suhbata mu wax ne: Al-Muxiirata Ibn Suhbata xamal na ma ci benn téere bu jël ca Muhaawiya ne: Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daan na wax ginnaaw jullig farata gu ne: «laa iLaaha Illal Laahu wahdahu…

