bu ngeen dee laaj Yàlla laajleen ko Firdawsi
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële nañu ci Ubaadata Ibnus Saamit -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: "àjjana amna téeméeri daraja diggante ñaari daraja yu nekk day mel ni diggante asamaan ak suuf, Firdawsi moo ca gën a kawe daraja te ca la ñenti dexi àjjana yi di balle, te ca kawam la Aras nekk, bu ngeen dee laaj Yàlla laajleen ko Firdawsi".
Explanation
Benefits
Ñaaxe ci laaj Yàlla àjjanay Firdawsi ja gën a kawe ca àjjana.
Firdawsi moo gën a kawe ca àjjana, te moo ca gën.
Jaadu na ci jullit bi yitteem nekk lu kawe ak mu dox te sàkku wàccuwaay ya gën a kawe te gën fa Yàlla.
Ñenti dexi àjjana yi ñooy dexi ndox ak soow ak sàngara ak lem yi ñu tudd ci Alxuraan ci waxi Yàlla mu kawe mi: {Nirële melow Àjjana ja ñuy dig ña ragal Yàlla: amna ci biiram ay dexi ndox yu dul forox, ak ay dexi meew yu cafkaam dul soppiku, ak ay dexi ñoll yu neex ca ña koy naan, ak ay dexi lem yu sell} [Muhammat: 15].
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

