Allaahumma baahid baynii wa bayna xataayaaya kamaa baahadta baynal masrixi wal maxribi
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan kàbbar ci julli gi, da daan noppi ab diir njëkk muy jàng, ma ne ko: yaw Yonnente Yàlla bi jote naa la sama baay ak sama yaay nga xibaa…

