HadeethEnc · 1.30.0
Nit ki moo ngi ci diiney xaritam, na ku nekk xool kan lay xaritool
Available translations
Choose an available translation of this Hadeeth
01
Hadeeth text
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: "Nit ki moo ngi ci diiney xaritam, na ku nekk xool kan lay xaritool".
02
Explanation
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day leeral ne nit ki day niróo ak xaritam ak àndandoom ci doxiinam ak aadaam, xarit ga di jeexital ci jikó
yi ak melo yi ak doxaliin yi, lii moo tax muy gindee di jëmale ci rafetug tànn xarit; ndaxte moom day tegtal xaritam ag gëm ak ug njub ak yiw, bu ko defee muy ndimbal ci àndandoom.
yi ak melo yi ak doxaliin yi, lii moo tax muy gindee di jëmale ci rafetug tànn xarit; ndaxte moom day tegtal xaritam ag gëm ak ug njub ak yiw, bu ko defee muy ndimbal ci àndandoom.
03
Benefits
Digle nañu ñuy ànd ak ñu baax ñi te di leen segg, tere nañu it di ànd ak ñu bon ñi.
Dafa jagleel xarit cig tudd wolif jegeñaale; ndaxte yaw yaay tànn xarit bi, waaye mbokk ak jegeñaale loolu tànn amu ci.
Wut xarit daa war a tege ci xalaat.
Nit ki dina dëgëral diineem ci ànd ak way-gëm ñi, dana ko néewal doole it ci ànd ak kàccoor yi.

Attribution
[Abóo Daawuda soloo na ko, At-tirmisiy, ak Ahmat]
Categories
Share
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares