àqi jullit ci moroomam juróom-benn la" ñu ne ko: yooyu yan la yaw Yonente Yàlla bi?, mu ne: "boo dajee ak moom nanga ko nuyu, bu la woowee nanga ko wuyu, bu sàkkoo nga laabire ko nanga ko laabire, bu tissoolee daal di sant Yàlla nanga ko ndokkeel, bu feebaree seeti ko, bu faatoo nga gunge ko
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: "àqi jullit ci moroomam juróom-benn la" ñu ne ko: yooyu yan la yaw Yonente Yàlla bi?, mu ne: "boo dajee ak moom nanga ko nuyu, bu la woowee nanga ko wuyu, bu sàkkoo nga laabire ko nanga ko laabire, bu tissoolee daal di sant Yàlla nanga ko ndokkeel, bu feebaree seeti ko, bu faatoo nga gunge ko".
Explanation
Benefits
Delloo nuyóo faratay jëmm la bu dee benn jullit la, mbooloo mi nag kenn dana leen doy, bu dee tàmbali nuyóo ga la cay cosaan mooy sunna la.
Seeti ku feebar dafa bokk ci ay àqam ci kaw mbokki jullitam; ndaxte moom day dugal mbégte ak wéttal ci xolam, loolu fardu kifaaya la.
Dafa war ñu wuyu ab woote ga fii ag bàkkaar amu ca; bu dee xawu céetal la ñi ëpp ci woroom xam-xam yi dañoo waral wuyu ga lu dul ci ngàntug Sariiha, bu dee nag du xewu céetal ñi ci ëpp nee nañu dañu ko a sopp.
Ndokkeel aji-tissooli lu war la ci ki dégg ki tisooli sant Yàlla.
Matug sariiha ak ug xéram ci dëgëral buumug mbooloo mi ak ngëm gi, ak yiy waral bëggënte ak jokkook ci nit ñi.
(Ndokkeel): mooy yal na la Yàlla soreele ag ndokk, musal la ci lu la sa noon di ndokke, walla yal na la Yàlla gindi ca yoon wu leer wa te jub.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

