Yi Yàlla moñaale ak nit ki juróom la: xaraf, wat kawaru naq, ak wàññi kawari mustaas, ak lewwi ay weh, ak suqi kawari poqtaan
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- muy wax naan: "«Yi Yàlla moñaale ak nit ki juróom la: xaraf, wat kawaru naq, ak wàññi kawari mustaas, ak lewwi ay weh, ak suqi kawari poqtaan».
Explanation
Bi ci njëkk: xaraf, te mooy dagg der wi yokk ci sàkkaras ku góor ki ci kaw, ak dagg boppu der wi ci awray jigéen ci kaw barabu sëy bi.
Ñaareel bi mooy: wat kawari naq, te mooy wat kawar gi nekk ci naq bi te wër awra wi.
Ñatteel bi mooy: lewwi ay mustaas, te mooy jemp li sax ci tuñu ku góor ki ci kaw, ba deru tuñ wa di feeñ.
Ñenteel bi mooy: lewwi ay we.
Juróomeel bi mooy suqi kawari poqtaan.
Benefits
Yoonal nañu sàmmoonte a. k bir yii, te bañ koo sàggane.
Melo yii am na ay njariñi diine ak àdduna, bokk na ca: rafetal ay melo, setal yaram, ak fegu ngir laab, ak wuuteek yéefar yi, ak def ndigalal Yàlla.
Tudd na ñu ci yeneen hadiis yeneen melokaani sunnay bindiin yu dul juróom yii, niki: yar ab sikkim, ak socc, ak yeneen.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

