ndax duma leen waxtaanal ci Ad-Dajjaal, lu benn Yonnente masul a wax aw xeetam? Moom de dafa patt, dana ànd ak lu mel ni àjjana ak sawara,
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «ndax duma leen waxtaanal ci Ad-Dajjaal, lu benn Yonnente masul a wax aw xeetam? Moom de dafa patt, dana ànd ak lu mel ni àjjana ak sawara, la muy wax ne mooy àjjana loolu sawara la, maa ngi leen koy moytondikuloo kem na ko Nuuh moytondikuloo woon aw xeetam».
Explanation
Moom dafa patt.
Yàlla it da koo def mu ànd ak lu mel ni àjjana ak sawara, ci kem li bët di gis.
Waaye àjjanaam ji sawara la, sawaraam si it àjjana la, ku ko topp mu dugal ko ci àjjana jii ci li nit ñi di gis, waaye ca dëgg-dëgg sawara la suy lakke, ku ko moy mu dugal ko ci sawara sii ci li nit ñi di gis, waaye ca dëgg-dëgg àjjana la ju teey, Tek ca Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- di moytondikuloo ci fitnaam kem ni ko Nuuh daan moytondikuloo aw xeetam.
Benefits
Mucc ci fitnay Dajjaal moo ngi ame ci ngëm gu dëggu ak làqu ci Yàlla ak muslu ci moom ci taaya ji mujj, ak wattu fukki aaya yi mujj ci saaru Al-Kahf.
Xér gu tar gi Yonnente bi xér ciw xeetam, ba tax mu leeralal jullit ñi ci ay meloy Dajjaal lu benn Yonnente bu ko jiitu leeralul.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

