Benn waay dafa laaj Yonnente bi ci bis-pénc ne ko: kañ la bis-pénc? Mu ne ko: "lan nga ko waajalal
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële nañu ci Anas -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Benn waay dafa laaj Yonnente bi ci bis-pénc ne ko: kañ la bis-pénc? Mu ne ko: "lan nga ko waajalal". Mu ne ko: du dara, lu dul ne bëgg naa Yàlla ak ub yonnenteem yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc, mu ne ko: "ki nga bëgg ngay nekkal". Anas nee na: masuñoo bég ci dara kem ni ñu bége ci li Yonnente bi wax ne: "ki nga bëgg ngay nekkal" Anas wax ne: man bëgg naa Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ak Abuu Bakrin ak Umar, te maa ngi am yaakaar a nekk ak ñoom ndax li ma leen bëgg, donte
jëfuma lu tolni
seen jëf ya.
Explanation
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: ana lan nga ko waajalal ci jëf yu baax?
Aji-laaj ji ne ko: waajalaluma ko ci ay jëf yu màgg de waaye damaa bëgg Yàlla ak ub yonnenteem, te tuddul leneen ci jëfi xol yi ak yu yaram yi ak yu alal yi; ndaxte yooyu yépp ay bànqaas la ci bëgg gi te ca lay tege, ndaxte bëgg gu dëggu day waral pasteefu ci jëf yu
baax yi.
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne ko: ki nga bëgg ngay nekkal ca àjjana.
Sahaabay Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daal di bég ci bégale googu mbégte mu tar.
Anas yal na ko Yàlla dollee gërëm xibaare ne moom dafa bëgg Yonnente bi ak Abuu Bakrin ak Umar, muy yaakaar a nekk ak ñoom donte ay jëfam melul ni seen i jëf
Benefits
Yàlla dafa nëbb xam-xamu bis-pénc ba ci jaamam ñi ngir nit ki di des di ko waajal di ku pare ngir daje ak Yàlla.
Ngëneelu bëgg Yàlla ak ub yonnenteem ak gaa yu sell yi ak way-gëm ñi, ak xuppe ci bëgg bokkaalekat yi.
Waxi Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc: ki nga bëgg ngay nekkal. Jubluwu ci ag yamoo daraja ak wàccuwaay, waaye li mu ci jublu mooy ñu nekk ca àjjana ba ku nekk di man a gis keneen ka donte seen i barab dafa soree.
Jubbanti jullit bi ci mu yittewoo li gën ci moom te gën ko a jariñ, te bàyyi di laaj lu ko dul jariñ.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

