def ndànk du am ci dara lu dul ne dana ko taaral, waaye du ñàkk ci dara it lu dul ne dana ko ñaawal
Jële na ñu ci Aysatu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- Soxnas Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «def ndànk du am ci dara lu dul ne dana ko taaral, waaye du ñàkk ci dara it lu dul ne dana ko ñaawal».

