Kenn ci yéen du gëm, ndare mu bëggal mbokkam li mu bëggal boppam
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële nañu ci Abuu Hamsata Anas ibn Maalik yal na ko Yàlla dollee gërëm -liggéeykatu Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: "Kenn ci yéen du gëm, ndare mu bëggal mbokkam li mu bëggal boppam"
Explanation
dafa bëggal mbokkam li mu bëggal boppam ci jaamu Yàlla ak xeetu yiw yi ci diine ak ci àdduna, bu gisee ci mbokkam ag wàññeeku ci diineem, day pasteefu ci yéwénal ko, bu ca gisee yiw mu dëgëral ko ca, te dimbale ko ca, daal di koy laabire ci mbiri diineem ak àddunaam.
Benefits
Mbokkoo ci Yàlla moo gën a kawe mbokkoo ci askan, kon nag àqam moo gën a war.
Araamal nañu lépp luy dàqonte ak mbëggeel gii ci ay wax ak i jëf niki wuruj ak jëw ak soxor ak noonoo ci kaw bakkanu jullit bi ak alalam ak deram.
Jëfandikoo yenn baat yiy sawarloo ci jëf; ndax li mu wax ne "ñeel mbokkam".
Al-Kirmaanii yal na ko Yàlla yërëm nee na: bokk na ci gëm ba tay mu bañal mbokkam li mu bañal boppam ci ay, tuddu ko nag; ndaxte bëgg dara day taqoo ak bañ safaanam, kon ñàkk gee tudd ag doyloo la rekk.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

