Yàlla bind na Ag rafetal ci bir yépp
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële nañu ci Abuu Yahlaa Saddaad ibn Aws yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: "Yàlla bind na Ag rafetal ci bir yépp, bu ngeen dee ray nangeen rafetal rayiin wa, bu ngeen dee rendi nangeen rafetal rendiin wa, nangeen daas seenug ñawka tey noppal li ngeen di rendi".
Explanation
Rafetal cig ray ci jamonoy fayontoo: ci tànn yoon wa gën a yomb te gën a woyof te gën a gaaw ci faat ki ñuy ray.
Rafetal cig rendi mooy: mu am ñeewantu ci bayima bi mu ñawal jumtukaay bi, te bañ koo daas ci kanamu la muy rendi, fekk ma nga koy xool, te mu bañ koo rendi fekk am na fa ay jur yu koy xool.
Benefits
Rafetal ray gi ak rendi gi ci defe ko ca anam ga ñu ko yoonale.
Matug Sariiha ak làmboo gimu làmboo léppi yiw, bokk na ca yërëm rab yi ak ñeewantu leen.
Tere di ñaawal yaramu nit ki ginnaaw bi ñu ko rayee.
Araamug lépp loo xam ne mbugal baayima da caa nekk.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

