socc day laabal gémmeñ di gërëmloo Boroom bi
Jële nañu ci Aysa -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «socc day laabal gémmeñ di gërëmloo Boroom bi».
Search and read verified Prophetic hadeeth translations, explanations, benefits, categories and source attribution. Page 13.
Smart instant results tolerate minor spelling mistakes, with every filter in one place.
Jële nañu ci Aysa -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónent Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «socc day laabal gémmeñ di gërëmloo Boroom bi».
Jële nañu ci Abuu Hurayrata mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «julliy juróom, ak Àjjuma ba Àjjuma, ak weeru koor ba weeru koor, dañuy far bàkkar yi ci séen diggante bu dee moytu nañu bàkkaar yu mag yi».
Jële nañu ci Abdullah Ibn Mashuud -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daan na wax: "Allaahuma innii as-aluka alhudaa wattuqaa walhafaafa walxinaa".
Jële nañu ci Huqbata ibn Aamir yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Damaa wax: "yaw Yonnente Yàlla bi, ana lan mooy musale? Mu ne ma "tëyéel sa làmmiñ, te na la sa kër doy, te nga jooy say ñuumte".
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: "Yàlla mu màgg mi nee na: man maa ngi fa ma sama jaam bi njorte, te maa ngi ànd ak moom saa yu ma tuddee, bu ma tuddee ci boppam ma tudd ko…
Jële nañu ci Surayh ibn Haanii mu wax ne: Laaj naa Aysatu, ne ko: ci lan la Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daan tàmbalee bu daan dugg këram? Mu ne: ci socc.
Jële nañu ci Abdulaah Ibn Amr -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «Jottalileen jële ci man donte benn aaya la, ta ngeen waxtaane waa Banuu Israayil ci lu amul benn jafe-jafe, waaye ku ma fenal te tay k…
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm: Benn kaw-kaw dafa ñëw ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, ne ko: tegtal ma jëf joo xam ne su ma ko defee dinaa dugg àjjana, mu ne ko: "dangay jaamu Yàlla te doo ko bokkaale ak dara, di taxawa…
Jële nañu ci Talhata ibn Ubaydil Laahi -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Benn waay bu bokk ci waa Najd dafa ñëw ci Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- kawar gi tasaaroo, ñoo ngi dégg kàddug waxam ji, waaye xamunu li muy wax, ba mu jege Yonne…
Jële nañu ci Abuu Sahiid Al-Xudriyu, ak Abuu Hurayrata -yal na leen Yàlla dollee gërëm- ñu jële ci Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «Amul benn coono buy dal ab jullit, mbaa tawat walla, jaaxle, mbaa naqar, loraange, walla njàqare, doonte dég…
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónent bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «wërale nañu sawara ak ay bànneex, wërale àjjana ak ay naqar».
Jële nañu ci Aysatu yaayu jullit ñi -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Wax naa Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc: doy na la sëkk ci Safiyyatu lii ak lii, -kenn ci nettalikat yi nee na: maanaam dafa gàtt- mu ne ko: wax nga kàddu gog bu ñu ko jaxase w…
Follow any language without creating an account.