yaw sama baay tëx, waxal: laa ilaaha Illal Laahu, genn kàddu gog dinaala ci mana layal fa Yàlla
Jële nañu ci Sahiid Ibnul Musayyab,mu jële ci baayam mu wax ne: Bi dee dikkalee Abuu Taalib, Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa ñëw fi moom fekk fa Abuu Jahlin, ak Abdullah Ibn Abii Umayyata ibnul Muxiirata, mu ne ko: "yaw sama baay tëx, waxal…

