diine ji lu yomb la, te kenn du taral diine ji lu dul ne dana ko not, kon deeleen jubal, di jegeele
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «diine ji lu yomb la, te kenn du taral diine ji lu dul ne dana ko not, kon deeleen jubal, di jegeele, te ngeen bég, na ngeen dimbalikoo suba gi ak ngoon gi ak lenn ci guddi gi».
Explanation
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bégle ci yool bu rëy ci kaw jëf ju sax donte dafa néew ñeel ki lott ci def la gën a mat; ndaxte lott bu jugewul ci nit ki du waral yool bi di wàññeeku.
Bi dëgg-dëggi àdduna nekkee kërug tukki daal di tuxu jëm allaaxira la Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc digle ñu dimbalikoo ci sax cig jaamu ci def ko ci ñatti waxtuy cawarte yii:
Bi ci njëkk: suba gi: ci bu njëlbeenu bëccëg gi demee; ci diggante jullig fajar ak fenkug jant bi.
Ñaareel bi: njolloor: ginnaaw jengug jant bi.
Ñatteel bi: lëndëm: ci guddi gi yépp walla leen ci moom, ndax te
jëfi guddi moo ëpp coono jëfi bëccëg mu digle lenn ci guddi gi rekk, ci li mu wax ne : ak lenn ci guddi gi.
Benefits
War na ci jaam bi mu def ndigal li ci kem kàttanam, ci lu dul woyofal mbaa taral.
War na ci jaam bi mu tànn waxtu yi cawarte di am mu def ca jaamu gi, te ñatti waxtu yii ñooy yi gën a noppale ci yaram ngir mu def si ag jaamu.
Ibn Hajar Al-Asxalaanii nee na: dafa mel ni Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc day wax ak kiy tukki am fu mu jëm, te ñatti waxtu yii ñooy waxtu yi gën a teey ci tukkikat bi, mu koy yee ci waxtuy cawarteem; ndaxte kiy tukki bu tukkee guddi ak bëccëg day lott daal di dog, te bu tànnee dox ci waxtuy cawarte yii kon dana man a sax ci lu dul coono.
Ibn Hajar nee na: hadiis bi day junj ñu jël yombali Sariiha yi, ndax te jël lu jafe ci waxtuw yombal loolu ag taral la, niki ki bàyyi tiim fekk manut a jëfandikoo ndox, ba jëfandikoo ko di ko yóbbe muy loru.
Ibnul Muniir nee na: hadiis bi am na màndarga ci màndargay yonnent, nun gis nanu, ñi nu jiitu it gis nañu ne képp kuy taral ci diine day mujjee bàyyi, jubluwuñu ci ñàkk a sàkkoo matal ci jaamu gi, ndaxte dafa bokk ci mbir yi ñu gërëm, waaye dañuy tere ëppal guy waral yoqat, walla ëppal ci coobarewu guy waral bàyyi li gën, walla génne farata gi ci waxtoom, niki ki fanaanee julli guddi gi yépp ba noppi di nelaw ci waxtuw julli suba gi ba duko julli ji ca mbooloo ma, walla mu dem ba jant bi fenk waxtuw farata wi génn.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

