Bokk na ci màndargay bis-pénc nu yëkkati xam-xam, réer bari, njaalo bari, naan sàngara bari, góor ñi néew, jigéen ñi bari, ba juróom-fukki jigéen di tolloog benn góor
Jële na ñu ci Anas -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dinaa leen nettali ab Hadiis bu ma dégge ci Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- kenn du leen ko nettali ku dul man: dégg naa Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax n…

