yéen nit ñi, deeleen tasaare nuyóo, di leele ñam, di jokk mbokk, di julli guddi fekk nit ñi a ngi nelaw, kon dangeen dugg àjjana ci jàmm
Jële nañu ci Abdullah ibn Salaam yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: ba Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ñëwee Madiina nit ñi dañoo buur jëm ci moom, ñu naan: Yonnente Yàlla bi ñëw na, Yonnente Yàlla bi ñëw na, Yonnente Yàlla bi ñëw na, ñatti yoon, m…

