HadeethEnc · 1.30.0
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc wax na ñeel Abuu Bakrin ak Umar: «ñaar ñii ñooy sangi paa yiy nekk àjjana ñu njëkk ña ak ñu mujj ña ba mu des yónente yi
Available translations
Choose an available translation of this Hadeeth
01
Hadeeth text
Jële nañu ci Anas yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc wax na ñeel Abuu Bakrin ak Umar: «ñaar ñii ñooy sangi paa yiy nekk àjjana ñu njëkk ña ak ñu mujj ña ba mu des yónente yi ».
02
Explanation
Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dafa xibaare ne Abuu Bakrin Al-Siddiiq ak Umar Al-Faaruuq yal na leen Yàlla dollee gërëm ñoom ñoo gën ci nit ñi ginnaaw Yonnente yi, te ñoo gën ci ñi dugg àjjana ginnaaw Yonente yi.
03
Benefits
Abuu Bakrin ak Umar yal na leen Yàlla dollee gërëm ñoom ñoo gën ci nit ñi ginnaaw Yonnente yi.
Àjjana amul paa, waaye ña cay dugg fanweeri at ak ñatt lañuy am, li ñu ci jublu mooy ñoom ñaar ñooy sangi ñi faatu ci àdduna te nekk paa, walla ñu jàppe ko anam ga ñu nekkoon ci àdduna jamonoy hadiis bii.
Àjjana amul paa, waaye ña cay dugg fanweeri at ak ñatt lañuy am, li ñu ci jublu mooy ñoom ñaar ñooy sangi ñi faatu ci àdduna te nekk paa, walla ñu jàppe ko anam ga ñu nekkoon ci àdduna jamonoy hadiis bii.
Attribution
[At-tirmisiy soloo na ko]
Categories
Share
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

