Yaw Yónente Yàlla bi, man de bàyyiwuma lu rëy walla lu ndaw lu dul ne def naa ko, mu ne ko: «Ndax dangay seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ci dëgg ku dul yàlla, ak ne Muhammat mooy Yónente Yàlla?
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële na ñu ci Anas Ibn Maalik, -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Am na ku mas a ñëw ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu ne ko: Yaw Yónente Yàlla bi, man de bàyyiwuma lu rëy walla lu ndaw lu dul ne def naa ko, mu ne ko: «Ndax dangay seede ne amul kenn ku ñu war a jaamu ci dëgg ku dul yàlla, ak ne Muhammat mooy Yónente Yàlla?» Ñatti yoon. Mu ne ko: Waaw, mu ne: «Lii ci la juge».
Explanation
Benn waay dafa ñëw ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: yaw Yónente Yàlla bi, man de bàkkaar ak moy Yàlla gune def naa ko, bàyyiwuma lu ndaw mbaa lu mag lu dul ne def naa ko, ndax dees na ma jéggal? Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: xanaa du seede nga ne amul kenn ku ñu war a jaamu ci dëgg ku dul Yàlla ak ne Muhammat ndawul Yàlla la? Mu baamtul ko ko ñatti yoon, Mu tontu ko ne ko: waaw seede naa ko, Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- xamal ko ngëneeli ñaari baati seede yi ak ne dañuy far ay ñaawtéef, ndaxte tuub day far la ko jiitu.
Benefits
Lislaam day far bàkkaar yi ko jiitu.
Tuub gu dëggu day far li ko jiitu.
Bokk na ci njubug Yónente bi buy jàngale di ko baamtu.
Ngëneeli ñaari baati seede yi ci ne ñoom ay sabab la ñu ci mucc ci sax ca sawara.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

