Amul benn coono buy dal ab jullit, mbaa tawat walla, jaaxle, mbaa naqar, loraange, walla njàqare, doonte dég gu ko jam la, lu dul ne Yàlla dina ca fare yenn ci ay bàkkaaram
Jële nañu ci Abuu Sahiid Al-Xudriyu, ak Abuu Hurayrata -yal na leen Yàlla dollee gërëm- ñu jële ci Yonente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «Amul benn coono buy dal ab jullit, mbaa tawat walla, jaaxle, mbaa naqar, loraange, walla njàqare, doonte dég…

