giñ naa ci ki sama bakkan nekk ci loxoom da ngeen topp yoonu ña leen jiitu woon
Jële nañu ci Abuu Waaxidin Allaysii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Bi Yonnente Yàlla bi génnee jëm Hunayni dafa romb genn garabu bokkaalekat yi ñu koy wooye: boroom lonk ya, ñu fay lonk seen i ngànnaay, ñu ne ko: wutal nu gu am ay lonkkaay kemm ñoom ni ñu ame…

