yamaleleen seen sàppe yi, ndax yamale sàppe yi daa bokk ci matug julli gi
Jële na ñu ci Anas Ibn Maalik -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: "yamaleleen seen sàppe yi, ndax yamale sàppe yi daa bokk ci matug julli gi"

