juróom-ñaar yii Yàlla dana leen keral bis ba genn ker dul am lu dul keram ga
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële nañu ci Abuu Hurayrata yal na ko Yàlla dollee gërëm mu jële ci Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc mu wax ne: "juróom-ñaar yii Yàlla dana leen keral bis ba genn ker dul am lu dul keram ga: imaam bu maandu, ak waxambaane wu sosu ci jaamu Yàlla, ak waa ju xolam aju ca jàkka ya, ak ñaar ñu bëggante ci Yàlla, ci moom lañuy daje te ci moom lañuy teqalikoo, ak góor gu jigéen ju am dayo ak rafetaay woo mu ne ko: man damaa ragal Yàlla, ak waa ju saraxe ab sarax nëbb ko ba càmmooñam du xam li ndayjoor bi joxe, ak waa ju fàttaliku Yàlla ciw wéetaay, ay bëtam taa".
Explanation
Benefits
Ibn Hajar wax na ci waxam ji "ci keram gi" nee nañu ki ñu ci namm: kerug Arasam, te hadiisu Salmaan ibn Sahiid ibn Mansuur ci càllala gu rafet dana ko tegtale "juróom-ñaar yii Yàlla dana leen keral ca kerug Arasam ga".
Ibn Hajar nee na: li gën a rafet ci li ñu firee maandu mooy ki nga xam ne day topp li Yàlla digle, ci teg mbir mu ne ci barabam ci lu dul ëppal mbaa yéesal, dakoo jiital cig tudd ngir li mu làmboo njariñ.
Ngëneelu xaar julli ginnaaw ag julli.
An-Nawawii nee na: nekk na ci ñaaxe ci bëggante ci Yàlla ak leeral màggaayu ngëneelam.
Dañoo tudd ab dayo ak ub taar ngir bëgg gi ko nit ñi bëgg ak seen ug jafe.
Li gën ci saraxe mooy nëbb ko ak sori ngistal, donte yoonal nañu fésal sarax ak asaka bu dee mucc na ci ngistal ak mu jublu sa ñaax ñeneen ci joxe ngir keneen roy ko ci, ak ngir feeñal màndargay lislaam.
Juróom-ñaar ñii am na ñu xéewal googu ci sababus sellal gi ñeel Yàlla mu kawe mi ak wuute ak bànneex yi.
Waxam ji: "juróom-ñaar Yàlla dana leen keral" tënk gi ñu leen tënk ci lim bii du dara, ndax am na ñeneen ñu rot ci hadiis ñu Yàlla di keral ca kerug Arasam ga.
Ibn Hajar nee na: tudd gi ñu tudd góor ñi ci hadiis bii du dara! Ndax jigéen ñi it dañu da ñu ciy dugg lu dul bu dee imaam ju maandu imaam ju mag la ñu ci jublu, lu ko moy rekk jigéen ñi man nañu ci a dugg ndax dana am njaboot daal di maandu ci seen diggante, meloy taqoo ak jàkka ji moom day génn; ndax jullig jigéen ci këram moo gën ci jàkka ji, lu dul loolu ñoom da ñu cay bokk ba ci góor gi jigéen woo ci misaal manees naa gis jigéen ju ab buur bu rafet woo mu bañ ngir ragal Yàlla donte dafa am aajo.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

