àqi Yàlla ci jaam ñi mooy ñu jaamu ko te bañ koo bokkaale ak dara, àqi jaam ñi ci Yàlla nag mooy du mbugal ku ko bokkaalewul ak dara
Jële na ñu ci Muhaas -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Toggoo woon naa ak Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- am Mbaam mu ñuy woowe Xufayr, mu ne ma: «yaw Muhaas, ndax xam nga lan moy Àqi Yàlla ci ay jaamam, ak lan mooy àqi jaam ñi ci Yàlla?», Muha…

