Yàlla sadd na misaal ci yoon wu jub
Jële na ñu ci An-Nuwaas Ibn Samhaan bokk ci waa Ansaar -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «Yàlla sadd na misaal ci yoon wu jub, te ci ñaari wetu yoon wi am na ñaari miir yu am bunt yu ubbeeku, ci…

