Jëf yi mi ngi aju ci yéene yi, te nit ku nekk la mu yéene rekk lay am
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële nañu ci njiiti jullit ñi baayu Hafsa Umar Ibn Al-Xattaab yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: dégg naa Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc muy wax ne: "Jëf yi mi ngi aju ci yéene yi, te nit ku nekk la mu yéene rekk lay am, képp ku gàddaay ngir Yàlla ak ub Yonenteem, kooku gàddaayam dina jëm ci Yàlla ak Yonenteem, waaye képp ku gàddaay ngir àdduna jum soxlaa jot walla jigéen ju mu bëgg a takk kon gàddaayam jëm na ca la ko tax a gàddaay".
Explanation
Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- joxe waat meneen misaal ci ni yéene di jeexitale ci jëf yi ànd ak seenug niróo ci melo wi feeñ, mu leeral ne ku jublu ci gàddaay bàyyi réewam ngir jublu ci ngërëmal Boroomam kon gàddaayam ga gàddaayu sariiha la gu ñu nangu te dees na ko fay ab yool ngir yéeneem ju dëggu, waaye ku jublu cig gàddaayam njariñal àdduna, alal, ak daraja ak am njaay, walla soxna du am ca gàddaayam ga lu dul njariñ yooya mu yéene woon, te du am benn cér cig pay mbaa ab yool.
Benefits
Jëf yi Nga xamne dees ciy jaar ngir jege Yàlla bu ko muskallaf mi defee ci anamug aada du ca am ab yool, ba keroog mu cay jublu jege Yàlla.
Ci yéene lañuy xàjjalee diggante jaamu gu ne ak geneen ga, ak it diggante jaamu yi ak aada yi.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

