ku aar deru mbokkam Yàlla aar kanamam ci sawara ëllëg bis-pénc
Jële nañu ci Abuu Dardaa -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne: «ku aar deru mbokkam Yàlla aar kanamam ci sawara ëllëg bis-pénc».

