ashibil basa, rabban naasi, wasfi Anta As-Saafii, laa sifaa-a illaa sifaa-uka sifaa-an laa yuxaadiru saqaman
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële nañu ci Aysatu yaayu jullit ñi -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yonente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc bu daan seeti ku feebar di ko ñaanal day wax: "ashibil basa, rabban naasi, wasfi Anta As-Saafii, laa sifaa-a illaa sifaa-uka sifaa-an laa yuxaadiru saqaman".
Explanation
Benefits
Seeti ku feebar dafa bokk ci àq yi dox ci diggante jullit ñi, ci mbokk gi la gën a yaye.
Xemmemloo ci ku seeti ku feebar mu ñaanal ko ñaan gu baarkeel gii ñu tuxal.
Bokk na ci njubug Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc di faj jaareko ci moccug sariiha ci Alxuraan ak ay ñaan yu teey, Yonnente bi daan na mocc boppam bu feebaree, niki noonu yit daan na mocc ku tawat ci njabootam ak ñeneen.
Ibn Hajar nee na: jaaxle amna ci lu tax ñuy ñaanal ki feebar ag wér te feebar bi day far ay bàkkaaram di yok yool ni ki mu ñëwe ci hadiis yu bari, tontu bi mooy: ñaan jaamu Yàlla la, te du dàqonte ak am tuyaaba ak far bàkkaar; ndax ñoom ñaar dañuy ame ci njëlbeenu feebar ba ak muñ ga, te aji-ñaan ji moo ngi ci diggante Ñaar yu rafet: benn jubluwaayam am, walla ñu wecceel ko ko ci xëcc njariñ walla jañ lor, te yépp ci ngëneelu Yàlla la.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

