man de xam naa baat boo xam ne bu ko waxoon li muy yég deñ, bu waxoon: ahuusu bil Laahi minas Saytaani, kon li muy yég dem
Jële nañu ci Sulaymaan ibn Surad yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Damaa toogoon ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ñaari waay di saagaante, kenn ki kanamam gi xonq ay séditi baatam jug, Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc daal di wax…

