buleen ŋàññ ngelaw li, bu ngeen gisee lu ngeen sib, nangeen wax: Allaahuma innaa nas-aluka min xayri haasihi arriihi wa xayri maa fiihaa wa xayri maa umirat bihii, wa nahuusu bika min sarri haasihii arriihi wa sarri maa fiihaa wa sarri maa umirat bihii
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële nañu ci Ubay Ibn Kahb -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «buleen ŋàññ ngelaw li, bu ngeen gisee lu ngeen sib, nangeen wax: Allaahuma innaa nas-aluka min xayri haasihi arriihi wa xayri maa fiihaa wa xayri maa umirat bihii, wa nahuusu bika min sarri haasihii arriihi wa sarri maa fiihaa wa sarri maa umirat bihii».
Explanation
Benefits
Dellu ci Yàlla ak muslu ci moom ci ayu li mu bind.
Ngelaw da ñu koy digal aw yiw, di ko digal aw ay.
Ibn Baas nee na: ŋàññ ngelaw li dafa bokk ci moy yi; ndaxte moom mbindeef la lu ñuy doxal di ko yónni ci yiw ak ay; kon daganul ñu ŋàññ ko, deesul wax: yal na Yàlla rëbb ngelaw li, walla yal na Yàlla ray ngelaw li, walla yàlla bu Yàlla baarkeel ngelaw lii, walla luy niru loolu, waaye aji-gëm ji day def jëm ci li ko Yonente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc jàngal.
Tere gi ñu tere kuy ŋàñ ngelaw li dinañu si boole lépp lu aju ci tàngaay ak seddaay ak Jant bi ak pënd bi ak yeneen yu dul yooyu ci mbindéef Yàlla yi ak ay doxaliinam.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

