ndax duma leen tektal lu gën li ngeen di laaj? Bu ngeen tëddatee -walla ngeen ñëw ci seen lal- nangeen sàbbaal Yàlla fanweer ak ñatt, te ngeen sant Yàlla fanweer ak ñatt, ngeen màggal Yàlla fanweer ak ñent, loolu moo gën ci yéen liggéeykat
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële nañu ci Aliyun yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Faatimata yal na ko Yàlla dollee gërëm dafa ñëw ci Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc di ko jàmbat li muy daj ci soqq ak wol, mu dégg ne dafa am ay jaam, te fekku ko fa, mu wax ko Aysatu, ba mu ñëwee Aysatu wax ka ko, nee na: mu ñëw fi nun fekk tëdd nanu, ba nuy jog mu ne nu: "buleen jog" mu ñëw toog sunu diggante, ba may yég seddaayu tànkam ci sama biir, mu wax ne: "ndax duma leen tektal lu gën li ngeen di laaj? Bu ngeen tëddatee -walla ngeen ñëw ci seen lal- nangeen sàbbaal Yàlla fanweer ak ñatt, te ngeen sant Yàlla fanweer ak ñatt, ngeen màggal Yàlla fanweer ak ñent, loolu moo gën ci yéen liggéeykat".
Explanation
seddaayu tànkam ci biiram bi, mu ne leen: Ndax duma leen xamal lu gën liggéeykat bi ngeen may laaj? Ñu ne ko ahakay, Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ne leen: Bu ngeen tëddatee seen lal ngir nelaw ci guddi gi, nangeen kàbbar fanweeri yoon ak ñent, ci wax: Allaahu Akbar, Sàbbaal leen Yàlla fanweeri yoon ak ñatt, ci wax: Subhaanal Laahi, Ngeen sant Yàlla fanweeri yoon ak ñatt, ci wax: Alhamdu lil-Laah; Tudd Yàlla gii moo gën ci yéen liggéeykat.
Benefits
Sikkar bii duñu ko wax ci lu dul nelawug guddi, baat yi nag moo ngi ci Muslim ci nettalib Muhaas mu jële ko ci Suhba "bu ngeen tëddee ci guddi gi".
Bu jullit bi fàttee tudd Yàlla gii ci njëlbeenu guddi gi topp mu fàttaliku ko ci mujjug guddi gi aayul mu wax ko; ndaxte Aliyun yal na ko Yàlla dollee gërëm moom mi nettali hadiis bi dafa wax ne fatte woon na koo wax ci njëlbeenu guddig xeexu Siffiin topp mu fàttaliku ko njëkk suba si di jot mu daal di koy wax.
Al-Muhallab nee na: nekk na ci Hadiis bi, nit ki day yan njabootam li muy yan boppam ci gënale allaaxira ci kaw àdduna bu ñu manee loolu.
Ibn Hajar Al-Asxalaanii nee na: ku ko saxoo du loru ci barig liggéey te du jafe ci moom donte dana ci am coono.
Al-Haynii nee na: anamug gën gi benn ñu jublu ci ne dafa aju ci allaaxira te liggéeykat bi ci àdduna la, te allaaxira moo gën te mooy des, walla ñu jublu ci kem li nga sàkku nga am ko ci sababus sikar yi ci doole ak kàttanu liggéey lu ëpp lu liggéeykat bi man.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

