Jullit bu góor du bañ jullit bu jigéen, ndax su bañee ci moom jenn jikkó gërëm na ci moom jeneen jikkó
Jële nañu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- nee na: «Jullit bu góor du bañ jullit bu jigéen, ndax su bañee ci moom jenn jikkó gërëm na ci moom jeneen jikkó».

