ndax xam ngeen lan la séen Boroom wax ?» Ñu ne ko: Yàlla a xam ak ub Yónenteem, mu ne leen: Yàlla dafa wax ne: «am na ci sama jaam ñi ñu xëy gëm ma am ñu weddi
Jële na ñu ci Sayd Ibn Xaalid Al-Juhanii -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dañoo jiite jullig suba ca Hudaybiya ginnaaw ba mu tawee ca guddi ga, ba mu noppee mu jàkkaarloo ak nit ñi, ne leen: «ndax xam ngeen lan…

