nun de dananu yég ci sunu bopp loo xam ne dana rëy lool kenn i nun di ko wax, mu ne leen: «te yég ngeen ko?» Ñu ne ko: waaw, mu ne leen: loolu mooy ngëm gu leer
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Ay nit ci Sahaaba yi dañoo ñëw ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, ñu laaj ko ne ko: nun de dananu yég ci sunu bopp loo xam ne dana rëy lool kenn i nun di ko wax, mu ne leen: «te yég ngeen ko?» Ñu ne ko: waaw, mu ne leen: loolu mooy ngëm gu leer».
Explanation
Am mbooloo ci Sahaabay Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dañoo ñëw laaj ko li ñuy yég ci séen biir ci ay bir yu rëy yoy wax ko dana rëy lool ci ñoom ngir ag bonam ag ni ñu ko bañe, Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne leen: loolu ngeen di yég mooy ngëm gu leer, te kóolute gi leeni yóbbu ba ngeen di tere li Saytaane di sànni ci xol yi, ba ngeen di ñaawlu wax ja, muy màgg ci séen bopp, ba Saytaane du man dara ci séen xol yi, wuuteek ñi Saytaane am kàttan ci séen i xol te amuñu lu ko man a jeñ.
Benefits
Bañ a dëggal mbaa nangu liy jax-jaxal xolxol yi ndax loolu ci Saytaane lay bawoo.
Jax-jaxali Saytaane du lor aji-gëm ji, waaye nay muslu ci Yàlla ci ay jax-jaxalam, te nay moytu di wéy ci loolu.
Jaaduwul ci ab jullit muy noppi ci yi lënt ci moom ci mbiri diineem, te war na ci moom mu laaj ko.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

