amul benn Yonnente bu Yàlla yónni ci xeet yi ma jiitu lu dul ne am na ci aw xeetam ñu koy dimbali ak ay àndandoo yu jàpp ci yoonam di roy ci mbiram
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële nañu ci Abdallah Ibn Mashuud yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Yonnente Yàlla bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc nee na: «amul benn Yonnente bu Yàlla yónni ci xeet yi ma jiitu lu dul ne am na ci aw xeetam ñu koy dimbali ak ay àndandoo yu jàpp ci yoonam di roy ci mbiram, topp ginnaaw ga nag ñu bon wuutu leen di wax lu ñu dul def, di def lu ñu leen digalul, ku leen xeex ci loxoom kooku aji-gëm la, ku leen xeex ci xolam kooku aji-gëm la, ginnaaw loolu nag feppu ngëm amu fa».
Explanation
Benefits
Ñàkk a bañ lu bon ci xol tegtal la ci néewug gëm walla ag demam.
Yombalug Yàlla mu Sell mi te kawe ñeel Yonnente yi ci ñuy gàddu bataaxal bi ci seen ginnaaw.
Ku bëgg a mucc na topp yoonu Yonnente yi; ndaxte wépp yoon wu dul seen yoon ag alkande la ak ug bew.
Lu jamono di gën a sori Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ak i Sahaabaam yal na leen Yàlla dollee gërëm nit ñi di bàyyi yoonam di topp bànneex yi di sos ay bidaa.
Leeral martabay jihaad, ci ne ci loxo la ñeel ku ko man a soppi, niki ki yor bir yi ak àttekat yi ak njiit yi, ak ci làmmiñ mu nekk ci leeral dëgg ak woote ca, ak ci xol mu nekk ci naqarlu lu bon li bañ ko a bëgg mbaa gërëm ko.
Warug digle lu baax ak tere lu bon.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

