Yàlla dafa bind yu rafet yi ak yu ñaaw yi, daal di leeral ko, képp ku yéene jëf i yiw, te defu ko, Yàlla dana ka ko bindal wenn yiw wu mat sëkk, waaye bu ko yéenee ba noppi def ko, mu bindal ko fukki yiw, mannakoo Ful bamu yégg juróom-ñaari téeméeri, ba ci ay full yu bari, waaye képp ku Yéenee jëf lu ñaaw te defu ko Yàlla di na ko bindal wenn yiw wu mat sëkk, bu ko Yéenee nag daldi koy def mu bindal ko wenn ñaawteef
Jële nañu ci Ibn Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- Jele nañu ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ci li mu soloo ci Boroomam mu màgg mi mu wax ne: «Yàlla dafa bind yu rafet yi ak yu ñaaw yi, daal di leeral ko, képp ku yéene jëf i yiw, te defu ko, Y…

