Masuma a gis Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc muy xàqataay di ree ba ma gis ay yàppi biir gémmiñam, waaye da daan muuñ
Jële nañu ci Aysatu ndayu jullit ñi yal na ko Yàlla dollee gërëm mu wax ne: Masuma a gis Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc muy xàqataay di ree ba ma gis ay yàppi biir gémmiñam, waaye da daan muuñ.

