dénk naa leen ngeen ragal Yàlla ci dégg ak topp, donte jaamub Habasa la, dangeen gis ci sama ginnaaw ag wuute gu tar, waaye nangeen jàpp ci sama Sunna ak sunnay njiit yu jub ya tey jubal
Jële nañu ci Al-Hirbaat Ibnu Saariyata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne : Benn bis Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa taxaw fi nun daal di nuy waar waar gu jotale xol yi jàq nañu ci, bët yi tuur ci rangooñ, ñu ne ko : yaw Yónente Yàlla bi, wa…

