loolu dereti sidit la, waaye bàyyil julli ci limu bis yi ngay gis mbaax, topp nga sangu te julli
Jële nañu ci Aysatu ndayu jullit ñi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne Faatimata bintu Abii Jahsin dafa laaj Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ne ko: Man damay gis dereet ju yàqu te du ma set, ndax damay bàyyi julli? Mu ne ko: “Déedéet , l…

