HadeethEnc · 1.30.0
Nëxit gi jigéen di gis ak mboq-mboq yi ginnaaw laab daawuñuko jàppee dara
Available translations
Choose an available translation of this Hadeeth
01
Hadeeth text
Jële nañu ci Ummu Atiyyata -yal na ko Yàlla dollee gërëm-,mu bokkoon ci ñi jaayante woon ak Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-,mu wax ne: Nëxit gi jigéen di gis ak mboq-mboq yi ginnaaw laab daawuñuko jàppee dara.
02
Explanation
Sahaaba bu jigéen bii di Ummu Atiyyata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- day xibaare ne jigéen ñi ci jamonoy Yonnente bi-yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daawuñu jàppe mbaax ndox miy génne ci awra -xaw a ñuul, walla mboq-ginnaaw bimu laabe ,
ba tax duñu bàyyi julli ak woor ngir moom.
ba tax duñu bàyyi julli ak woor ngir moom.
03
Benefits
Ndox miy génne ci awray jigéen -ginnaaw bi mu laabee ci mbërëg deesu ko jàppe mbaax donte dafa am nëxiit ak mboq-mboq yu bawoo ci dereet ji.
Génnug nëx-nëx yi ak mboq-mboq yi ci jamonoy mbaax ak aada ja dees na ko jàppe; ndaxte dereet la ju génn ci waxtoom,waaye dafa jaxasoo ak ndox.
Jigéen du bàyyi julli ak woor ngir nëx-nëx yi ak mboq-mboq yiy am ginnaaw laab gi,waaye day jàppu daal di julli.

Attribution
[رواه أبو داود بهذا اللفظ ورواه البخاري بدون زيادة (بعد الطهر)]
Categories
Share
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares