giñ naa ci ki sama bakkan nekk ci loxoom, maa leen gën a niroole jullig Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ndax nii la daan jullee ba ni mu tàqalikoo ak àdduna
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële na ñu ci Abuu Hurayrata -yal na ko Yàlla dollee gërëm- ne: Moom daana kàbbar ci bépp jullig farata ak bu dul moom, ci koor ak bu dul koor, bu dee jug kàbbar, bu dee rukoo kàbbar, daal di wax: samihal Laahu liman hamidahu, daal di wax it: Rabbanaa wa lakal hamdu, bala moo sujjóot, bu dee rot jëm ci sujjóot ba daal di kàbbar, buy yëkkati boppam ci sujjóot daal di kàbbar, bu dee jug ci toogaayu ñaari ràkka yi daal di kàbbar, loolu lay def ci ràkka yépp, ba julli gi jeex, ba mu wëlbatikoo daal di wax ne: giñ naa ci ki sama bakkan nekk ci loxoom, maa leen gën a niroole jullig Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ndax nii la daan jullee ba ni mu tàqalikoo ak àdduna.
Explanation
Bi Abuu Hurayrata wëlbatikoo ca julli daal di wa ne: giñ naa ci ki sama bakkan nekk ci loxoom, man de maa leen gën a niroole jullig Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, ndax nii la daan jullee ba ni mu tàqalikoo ak àdduna.
Benefits
Xérug Sahaaba yi ci roy ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ak wattu sunnaam si.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

