digal nañu ma may sujjóot ci juróom-ñaari cér
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële na ñu ci Ibnu Abbaas -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu jële ci Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu wax ne : «digal nañu ma may sujjóot ci juróom-ñaari cér : cib jëh, mu daadi junj loxoom ci bakkanam, ak ñaari loxo yi, ak ñaari wóom yi, ak cati baaraam yi, ak ñu bañ a téye mbaa wog seen i yére ak seen kawar».
Explanation
Ab jëh: te mooy: xar kanam ci kaw bakkan bi ak ñaari bët yi, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- junj loxoom ci bakkanam, ngir leeral ne jëh ak bakkan benn cér la ci juróom-ñaari cér yi, ak feddali ne kiy sujjóot day laalale bakkanam ci suuf.
Cérub ñaareel bi ak bu ñatteel bi mooy: ñaari loxo yi.
Bu ñenteel bi ak bu juróomeel bi mooy: ñaari wóom yi.
Bu juróom-benneel bi ak bu juróom-ñaareel bi mooy: baaraami tànk yi.
Mu digal nu nuy bañ a takk sunu kawar, walla nuy dajale sunu yére bu ñuy sujjóote ci suuf ngir feg ko; waaye danu koy yoor mu tege ci suuf, mu sujjóot ak cér yi.
Benefits
Sib nañu di dajale yére walla kawar ci julli.
War na ci kiy julli mu ànd ak ug dal ci julli gi, ci teg céri sujjóot yiy juróom ci kaw suuf, daal di dal ba def sikar yi ñu yoonal.
Tere nañu takk kawar ci góor ñi déet jigéen ñi; ndax jigéen ci julli dañu koo digal mu muuru.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

