Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan ubbi julli gi day yëkkati loxoom ba mu tolloo ak mbagg yi,
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële na ñu ci Abdullah Ibn Umar -yal na leen Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan ubbi julli gi day yëkkati loxoom ba mu tolloo ak mbagg yi, naka noonu it daan na leen yëkkati bu daan kàbbar ngir rukóo, ak bu daan siggi ca rukóo ba, ak bu daan yëkkati boppam jóge ca rukóo ba, daal di wax: "samihal Laahu liman hamidahu", daawul def loolu nag ca sujjóot ba.
Explanation
Barab bu njëkk bi: buy ubbi julli gi di def kàbbaru armal.
Ñaareel bi: buy kàbbaar ngir rukóo.
Ñatteel bi: buy yëkkati boppam jóge ca rukóo ba, daal di wax: samihal Laahu liman hamidahu Rabbanaa wa lakal hamdu.
Daawul yëkkati loxoom bu daan tàmbalee sujjóot, mbaa muy siggi ca sujjóot ba.
Benefits
Yëkkati loxo sax na ci ñenteelu barab kem ni mu ñëwe ci nettalig Abii Humayd As-Saahidii ca Abuu Daawuda ak ñeneen, te mooy buy jug bawoo ci taaya ju njëkk ji ci jullig ñatt ak ñenti ràkka.
Sax na jóge ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- ba tay ne daan na yëkkati ay loxoom ba muy lerook ay noppam ci lu dul mu koy laal, kem ni mu ñëwe ci nettalib Maalik ibnul Huwayris bi nekk ci Al-Buxaarii ak Muslim: "Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- bu daan kàbbar day yëkkati ay loxoom ba mu tolloo ak ay noppam".
Boole Samihal Laahu liman hamidahu ak Rabbanaa wa lakal hamdu imaam bi moo ko jagoo ak kiy julli moom dong, bu dee maamuun la nag moom day wax: Rabbanaa wa lakal hamdu rekk.
Wax: "Rabbanaa wa lakal hamdu" ginnaaw rukóo ñenti melo sax na ci jóge ci Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc-, melo wii wenn la ci rekk, kon li gën mooy nit ki di topp melo yii, leeg-leeg mu def bii leeg-leeg mu def bee.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

