yéen nit ñi, damaa def lii ngir ngeen roy ak ngir ngeen xam samag julli
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële nañu ci Aasim Ibn Diinaar mu wax ne: Ay nit dañoo ñëw ci Sahl Ibn Sahdin As-Saahidii, fekk dañu doon werante ci minbar bi fan la bant bi jóge, ñu laaj ko loolu, mu ne leen: giñ naa ci Yàlla dinaa xam fan la jóge, ca bis bañu ko fi njëkkee teg laa ko gis, ak bis ba ca Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- njëkkee toog, Yonnente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- dafa yónnee ca diw -genn jigéen gu bokk ci Lansaar yi Sahl tudd na ko- ne ko: "digalal sa xaleb minise bi mu defaral ma ay bant yu may toog bu may wax ak nit ñi" mu digal ko ko, mu defar ko ci bant yi ci àll bi, mu indi ko, jigéen gi yónnee ko ci Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- mu digle ñu teg ko fii, ma gis Yonnente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- di julli di kàbbar fekk ma nga ca kawam, mu wàcc di dellu ginnaaw, ba noppi daal di sujjóot, ci suufu minbar bi, daal di delluwaat, ba mu noppee, mu jublu ci nit ñi daal di leeni wax ne: "yéen nit ñi, damaa def lii ngir ngeen roy ak ngir ngeen xam samag julli".
Explanation
Benefits
Dagan na ñu julli ci kaw minbar ngir jàngale, dagan na ci imaam bi mu gën a kawe maamuun yi ngir aajo.
Dagan na ñu dimbalikoo liggéey-kat yi ci aajoy jullit ñi.
Yëngatu gu ndaw ci julli ngir aajo loolu dagan na.
Dagan na maamuun bi xool imaamam ci julli gi; ngir jàng ci moom te loolu du wuute ak toroxlu.
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

