xanaa du ki ko doxloo ci ñaari tànkam ci àdduna man na koo doxloo ëllëg bis-pénc ci xar kanamam?
Choose an available translation of this Hadeeth
Hadeeth text
Jële na ñu ci Xataadatu -yal na ko Yàlla yërëm- mu wax ne: Anas Ibn Maalik -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- wax na nu ne benn waay dafa wax ne: yaw Yónente Yàlla bi naka lañuy pange yéefar bi ci xar kanamam ? Mu ne ko: «xanaa du ki ko doxloo ci ñaari tànkam ci àdduna man na koo doxloo ëllëg bis-pénc ci xar kanamam?» Xataadatu wax na: ahakay giñ naa ko ci sunu màggug Boroom.
Explanation
Laaj nañu Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- naka lañuy pange yéefar bi ci xar kanamam ëllëg bis-pénc?! Yónente bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- daal di ne: xanaa du Yàlla mi ko doxloo fii ci àdduna ci ñaari tànkam man na koo doxloo ci xar kanamam ëllëg bis-pénc ?! Yàlla lépp la man.
Benefits
Attribution
Categories
Share hadeeth
Sharing options · 0 Total shares

