ana lan moo dal aw nit ba ñuy wax lii ak lii? man de damay julli di nelaw, di woor di dog, di takk soxna, ku bañ sama yoon wi bokkul ci man
Jële nañu ci Anas -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: Am mbooloo ci Sahaabay Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc dañoo laaj soxnay Yonnente bi yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc ay jëfam ci li nëbbu? Am ci ñoom ku ne: man du ma takk soxna, keneen ne…

