yaw Yàlla sama Boroom képp ku méngoo dara ci sama mbiri xeet wii, ba noppi di tar ci ñoom, na nga tar ci kawam, waaye képp ku ménggoo dara ci sama mbiri xeet wii, daal di leen woyofalal, na nga ko woyofalal
Jële na ñu ci Aysatu -yal na ko Yàlla dollee gërëm- mu wax ne: dégg naa Yónente Yàlla bi -yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc- fekk mi ngi ci sama biir néeg bii muy wax naan: «yaw Yàlla sama Boroom képp ku méngoo dara ci sama mbiri xeet wii, ba noppi di tar ci ñoom, na…

